Nit ku baax warul moom di teye mer 
 Buur Yàlla di ko tooñ lañu dekke 
 War nga xaalaat balaa nga may àntu 
 Gënal li sa xol waaw boo tëddee nelaw 
    Nit ku baax war na di baale moom 
 Nit ku baax war na di jégeele 
 Ndaxam buur bi Yàlla dañu dekk di ko tooñ 
 Boo julee ñan mu face say bàkkaar   
 Dafa bàyyi say moroom yaw tànn naa la 
 Bàyyi kër ndey ak baay ngir séyal la 
 Kon bu mu séy du luñuy caxanee 
 Gënal li sa xol waaw bo tëdde nelaw   
 Kaay wax ak moom kaay wax ak moom 
 Kaay wax ak moom yénn bokk njegenaay 
 Kaay wax ak moom kaay wax ak moom 
 Kaay wax ak moom yénn bokk njegenaay   
 Hey nañu caapa ne jigéen ñi 
 Ñooy sunu kaani   
 Kon gnoune ak goune gnoune 
 Ak gnome 
 Ba sagar khègne 
 Mu ne waaw nangu   
 Kon jàpp ne séy lu ko takk taasu ko 
 Kon ñun ak gu ne ñun ak ñome ba pik ak pele!   
 Yaw mi jàmm bu ñu la baaloo na nga baale 
 Buur Yàlla moom dañu dékk di ko tooñ 
 Kon yaw mi jàmm mi la baaloo danga wara baale 
 Ndax buur Yàlla moom sopp na jàmm buy baale   
 Kaay wax ak moom kaay wax ak moom 
 Kaay wax ak moom yénn bokk njegenaay 
 Kaay wax ak moom kaay wax ak moom 
 Kaay wax ak moom yénn bokk njegenaay   
 Kaay wax ak moom kaay wax ak moom 
 Billaay billaay billaay