1. 1

    AMADEUS - Comme Ni Nga Ma (feat. Astar)

  2. 2

    AMADEUS - Dieye Sélémane (Taaru Sénégal)

  3. 3

    AMADEUS - Adduna

  4. 4

    AMADEUS - Ajaa Mooy Ajaa

  5. 5

    AMADEUS - Bëgg Naa La Man

  6. 6

    AMADEUS - Boulma Sagané

  7. 7

    AMADEUS - Confuse (feat. Wally B. Seck, Mia Guisse)

  8. 8

    AMADEUS - Daaru Dunya

  9. 9

    AMADEUS - Dara Douko Dakk

  10. 10

    AMADEUS - Dinala Won Né

  11. 11

    AMADEUS - Douma Kou Ndaw (feat. Khadim Temps & BM Jaay)

  12. 12

    AMADEUS - Doumala Fowe

  13. 13

    AMADEUS - Eutou Baabel

  14. 14

    AMADEUS - Fi Ba Leuz

  15. 15

    AMADEUS - Jëli (feat. Wally B. Seck)

  16. 16

    AMADEUS - Kelemati

  17. 17

    AMADEUS - Keneen Ku Mu DooNoon (KKDN)

  18. 18

    AMADEUS - Kocc Na Ma Jéggal

  19. 19

    AMADEUS - Legét

  20. 20

    AMADEUS - Méritewoumala

  21. 21

    AMADEUS - Njegennay

  22. 22

    AMADEUS - Saajobaan

  23. 23

    AMADEUS - Tout donner (feat. Xiirsa)

  24. 24

    AMADEUS - Waw Coumba

  25. 25

    AMADEUS - Waxtu (feat. Ashs The Best)

  26. 26

    AMADEUS - Yow La (feat. VJ)

Daaru Dunya

AMADEUS

Àdduna wërngal lay jiital
Koj ma ci jànt bi soo ma nammee
Jot gi mayatuma teew bi
Waaye ci mbégte lay mujj soo ko muñee

Muñal dina xéy neexi
Cofeel ngor a kay sàmm
Ëllëg dafa jar sedd
Sa doom yi dañuy maa ngi

Bu doon misaal la ci yiw ma ni yaa di kiiraay
Boroom asaman na ñu boole, daaru dunya
Keneen du nu musuloo tax ma dégg muñal
Boroom asaman na ñu boole, daaru dunya

Bu kenn bëggul bëgg naa la
(Déggal gars yi)
Bu kenn dikkul danga may gis
(Yàlla def gawar laa man)
Su ñépp demee wacc maak yaw
(Maak yaw la daaru dunya)
Suñ dellusee fekk maak yaw
(Sutura yaa di kiiraay)

Su kenn bëggul bëgg naa la
(Déggal gars yi)
Bu kenn dikkul danga may gis
(Yàlla def gawar laa man)
Su ñépp demee wacc maak yaw
(Maak yaw la daaru dunya)
Suñ dellusee fekk maak yaw
(Sutura yaa di kiiraay)

Muy taw mbaa mu naaj
Muy guddi mbaa bëccëg
Waa dëkk ba nga naan
Dikk nga ma car wayal

Musuloo xàddi ci man
Doo ku may rusloo itam
Tàsoo sama yaakaar xarit sama
Sutura yaa di kiiraay

Muñal dina xéy neexi
Cofeel ngor a kay sàmm
Ëllëg dafa jar sedd
Sa doom yi dañuy maa ngi

Bu doon misaal la ci yiw ma ni yaa di kiiraay
Boroom asaman na ñu boole, daaru dunya
Keneen du nu musuloo tax ma dégg muñal
Boroom asaman na ñu boole, daaru dunya

Bu kenn bëggul bëgg naa la
(Déggal gars yi)
Bu kenn dikkul danga may gis
(Yàlla def gawar laa man)
Su ñépp demee wacc maak yaw
(Maak yaw la daaru dunya)
Suñ dellusee fekk maak yaw
(Sutura yaa di kiiraay)

Bu kenn bëggul bëgg naa la
(Déggal gars yi)
Bu kenn dikkul danga may gis
(Yàlla def gawar laa man)
Su ñépp demee wacc maak yaw
(Maak yaw la daaru dunya)
Suñ dellusee fekk maak yaw
(Sutura yaa di kiiraay)

Playlists relacionadas Ver mais playlists

Momentos

O melhor de 3 artistas combinados