1. 1

    AMADEUS - Comme Ni Nga Ma (feat. Astar)

  2. 2

    AMADEUS - Daaru Dunya

  3. 3

    AMADEUS - Adduna

  4. 4

    AMADEUS - Ajaa Mooy Ajaa

  5. 5

    AMADEUS - Bëgg Naa La Man

  6. 6

    AMADEUS - Boulma Sagané

  7. 7

    AMADEUS - Confuse (feat. Wally B. Seck, Mia Guisse)

  8. 8

    AMADEUS - Dara Douko Dakk

  9. 9

    AMADEUS - Dieye Sélémane (Taaru Sénégal)

  10. 10

    AMADEUS - Dinala Won Né

  11. 11

    AMADEUS - Douma Kou Ndaw (feat. Khadim Temps & BM Jaay)

  12. 12

    AMADEUS - Doumala Fowe

  13. 13

    AMADEUS - Eutou Baabel

  14. 14

    AMADEUS - Fi Ba Leuz

  15. 15

    AMADEUS - Jëli (feat. Wally B. Seck)

  16. 16

    AMADEUS - Kelemati

  17. 17

    AMADEUS - Keneen Ku Mu DooNoon (KKDN)

  18. 18

    AMADEUS - Kocc Na Ma Jéggal

  19. 19

    AMADEUS - Legét

  20. 20

    AMADEUS - Méritewoumala

  21. 21

    AMADEUS - Njegennay

  22. 22

    AMADEUS - Saajobaan

  23. 23

    AMADEUS - Tout donner (feat. Xiirsa)

  24. 24

    AMADEUS - Waw Coumba

  25. 25

    AMADEUS - Waxtu (feat. Ashs The Best)

  26. 26

    AMADEUS - Yow La (feat. VJ)

Saajobaan

AMADEUS

Eey Màsamba Waalo
Humm

Su mbëggeel doon jaay
Am naa njëgam
Dinaa la wan sama yéene yi ma am ci yaw
Duma ku lay jay
Te duma la wor
Dinaa la wax dëgg ak lum metti metti

Maa la woo ne la maa la nob
Miinal la sama bopp ba nga barder maa la tooñ
Kon nag loo ma manti def
Lu mu metti naa ko muñ
Àdduna du dox ba ma soppi li ma la wax doo ma weddi

Ay bu doon ay nax neex na ma
Fekk ma ciy gént yee nga ma
Jàmm ju bari may nga ma
Yaa ngi may dundal àjjana

Tamit tëggal ma ma jaayu
Xamal ma ne man la
Gëmal ma ne man rekk nga nob
Sama saajobaan
Tëggal ma ma jaayu
Xamal ma ne man la
Gëmal ma ne Man rekk nga nob
Sama saadjobaan eeee waay

Xam nga duma puruux duma fàtte bi may surux
Xuntu wu lëndëm wi nga ma génne dinaa ko wax
Du lu rafet ci wax soo ma bàyyee damay torox
Nawle yépp bis bu ñu teewee dinaa ko wax waaaay

Doy nga ma ci kër
Kenn du la sikkal
Man yaw mii yaay ki ma fiital (tiital)
Doo dund ngistal
Ngor gi nga jiital
Ragaluma siiwal
Nun ñaar ndax doy nga ma ci kër

Ndaxte mane maa la woo
Ne la maa la nob
Miinal la sama bopp ba nga barder maa la tooñ
Kon nag loo ma manti def
Lu mu metti naa ko muñ
Àdduna du dox ba ma soppi li ma la wax doo ma weddi

Hay bu doon ay nax neex na ma
Fekk ma ciy gént yee nga ma
Jàmm ju bari may nga ma
Yaa ngi may dundal àjjana

Tamit tëggal ma ma jaayu
Tëggal ma ma jaayu
Xamal ma ne man la
Gëmal ma ne man rekk nga nob
Sama saajobaan
Tëggal ma ma jaayu
Xamal ma ne man la
Gëmal ma ne man rekk nga nob
Sama saajobaan

Eee waay!

Playlists relacionadas Ver mais playlists

Momentos

O melhor de 3 artistas combinados