Ngor amul njëg, bu ko jaay
Góore ba réy de bu ko bàyyi
Di dunde loo doonul amul njëriñ naan ko bàyyi
Jarul ko waay, feexel nank ko bàyyi
Deux ans yaa ngi koy topp
Xale bi ne na bëggul la
Def nga lu ne, wax nga lu ne
Moom nobul la
Lekkatoo te nelawatoo
Dem nga bàyyi xalaat ni faw nga juuk sëriñ tuko
Ma ni la: Bàyyil mu sedd, bàyyil mu sedd
Bàyyil mu sedd, jaru ko bàyyil mu sedd
Ñeme sañsé, téléphone bu génn nga am ko
Yaw rekk ci xale, cheveux bu cher nga sol ko
Ndekete yoo yoro, dangay ab yoro
Ñoo di boss di jaay lu amul ñépp xam ni yoro
Kon bàyyil mu sedd, bàyyi mu sedd
Bàyyil mu sedd, yoroo kon de bàyyi mu sedd
Ngor amul njëg, bu ko jaay
Góore ba réy de bu ko bàyyi
Di dunde loo doonul amul njëriñ naan ko bàyyi
Jarul ko waay, feexel nank ko bàyyi
Bàyyi bàyyi bàyyi, bàyyil mu sedd
Bàyyi bàyyi bàyyi, bàyyil mu sedd
Bàyyi bàyyi bàyyi, bàyyil mu sedd
Bàyyi bàyyi bàyyi, bàyyil mu sedd
Ne na mooy sa xarit te yaw rekk la teg bët
Loo am da kou naqari ñene nekk la mungeek kër
Nga sañse moo koy sonal, sa mbégte bonal xolam
Yëg nga ni da lay soosal, noon la bu ko faale
Bàyyil mu sedd, bàyyil mu sedd
Bàyyil mu sedd, jaru ko bàyyil mu sedd
Moom mag la te ba léegi nangogu ko
Wër ci koñ bi jël ci xale baay guko
Ñulal bopp, génne face
Di jaay tar, père bàyyil mu sedd
Dem nga fepp, wax nga ñépp
Xam na lépp, kon père bàyyil mu sedd!
Ngor amul njëg, bu ko jaay
Góore ba réy de bu ko bàyyi
Di dunde loo doonul amul njëriñ naan ko bàyyi
Jarul ko waay, feexel nank ko bàyyi
Bàyyi bàyyi bàyyi, bàyyil mu sedd
Bàyyi bàyyi bàyyi, bàyyil mu sedd
Bàyyi bàyyi bàyyi, bàyyil mu sedd
Bàyyi bàyyi bàyyi, bàyyil mu sedd