Bril
OMG
Tukkil baby fu la neex doo fay
Lu ne ci xol feeñ ci kanam
Xol bi yaa ci fees feeñ sama kanam
Fu ne laay xool ci sa yaram
Di gis sama bopp li fi rekk la am
Yaa may dofloo di ma defloo
Lu ne baby yaa ma ko jaral
Fu ma toogee gisuma la
Dégguma la fokk ma woo la ne la jaral
Ey yaw la bandit di niróol
Kaay wax ma qui es tu
Li ëpp na dafa fees bay tuuru atanuma li
Yaa may ray di ma dundal àljanna
Nga may dugal te deewaguma
Su may bàyyi di ma mbugël
Safara nga may tëmbal soo ma meree
Yaa fi fort
Sama point faible yaa ko xam
Xol bi bi mu reere yaa ko for
Wëruma dara lépp nga am
Eh jàmm ji nga may jox da bëri baby li comme guerre
Yaw yaay bu baax bi yaa tax may noyyi, yaay sama air
Yaay sedal sama xol di tàngal sama yaram
Doo ma may dara buñu wétee doo ma yërëm
Ma raw sax visa shengen
Tukkil baby fu la neex doo fay
Cëggin!
Xam nga man ma baax ci yaw, kaay ñu
Cëggin!
Feexal sa xol ma ci gaaw, ñówal ñu
Cëggin!
Eh, yaa mëna dékku li may daw, kaay ñu
Cëggin!
Jege ma, jege ma, ñówal ñu fecce mu lay
Cëggin!
Lépp loo soxla la lay jox di wëy ci say way
Su ñuy bëree jarul arbitre yaaw yaay mujje daw
Foo ma woo ma wuyu bu la ci neex ci kaw ba ci suuf
Wóolu nga ma ñu dem may sa wéeruwaay ma lay uuf
Fu ma dem nga wëri ma, fi ma la jàpp sori na
Mu ngi tuuru bari na, keneen ku dul man de doyu la (eeh!)
Moi j'assure, dam la xam de sur le sur
Fimla teye daf la neex, ma lay jooyloo je t'assure
Cëggin!
Fowe sa xol te mënoo ci dara
(Bëgg naa daf may neex)
Na xela ni bébé te mënoo ci dara
(Eh bëgg naa li daf may neex)
May xale bi la pogné te mënoo ci dara
Moome la te mënoo ci dara
Mën la fépp te mënoo ci dara
Yaay sedal sama xol di tàngal sama yaram
Doo ma may dara buñu wétee doo ma yërëm
Ma raw sax visa shengen
Tukkil baby fu la neex doo fay
Cëggin!
Xam nga man ma baax ci yaw, kaay ñu
Cëggin!
Feexal sa xol ma ci gaaw, ñówal ñu
Cëggin!
Eh, yaa mëna dékku li may daw, kaay ñu
Cëggin!
Jege ma, jege ma, ñówal ñu fecce mu lay
Cëggin!
Fowe sa xol te mënoo ci dara
(Bëgg naa daf may neex)
Na xela ni bébé te mënoo ci dara
(Eh bëgg naa li daf may neex)
May xale bi la pogné te mënoo ci dara
Moome la te mënoo ci dara
Mën la fépp te mënoo ci dara
Eh, cëggin!
Yaay sedal sama xol di tàngal sama yaram
Doo ma may dara buñu wétee doo ma yërëm
Ma raw sax visa shengen
Tukkil baby fu la neex doo fay
Cëggin!
Kaay ñu cëggin!
Ñówal ñu cëggin!