Yeah, yeah, yeah
Oumy Gueye
OMG
Mashallah baax nga yaru nga
Ne naa laf cat
Am tuuti bandit bari caas
Ne naa laf cat
Yaay kiy def dosi boole wax
Ne naa laf cat
Cat dafa gaw bëgguma ku ñu ree
Ne naa laf cat
Ki ku ko sukker, xale bi laf cat
Soxlawul sàppali, ne naa laf cat
Loxo bi gaaw na, xale bi laf cat
Aka mën a sañsé, kon ne leen laf cat
Benn ga fi
Ku mel ni yaw amatul
Yaa may jeri
Yaay sedal sama xol man la
Dégg nañu lu ne, teyul nga gën a jàpp
Diggante bee dàq mbuurook lem
Yaa may Douta Mbaye
Lu ma neex neex na la
Li ma bëgg dégg rekk ngay wax
Xol bi ne na waaw
Meloo ni ñoom, amoo morom
Mashallah baax nga yaru nga
Ne naa laf cat
Am tuuti bandit bari caas
Ne naa laf cat
Yaay kiy def dosi boole wax
Ne naa laf cat
Cat dafa gaw bëgguma ku ñu ree
Ne naa laf cat
Ki ku ko sukker, xale bi laf cat
Soxlawul sàppali, ne naa laf cat
Loxo bi gaaw na, xale bi laf cat
Aka mën a sañsé, kon ne leen laf cat
Sa jikko ji neex na ma
Sa ree ju neex sofu ma
Ni ngay waxe neex na ma
Dara ci yaw di sofu ma
Kon ne naa laf cat
Weretuma ndax dof ci yaw
Sama caabi mbëggeel mu ngi ci yaw
Àljanna rekk lay dund ak yaw
Yaa ma mën a fàcce
Yaay garab bi gën ci man
Dégg na ma ñu naan
Couple bi dafa nice
Mashallah, hey kaar!
Buleen ñu catu waay
Lammiñ baxul waay
Laalal bant, waay
Daagu ni ma daagu nee
Ñu ànd doxal waay
Mashallah baax nga yaru nga
Ne naa laf cat
Am tuuti bandit bari caas
Ne naa laf cat
Yaay kiy def dosi boole wax
Ne naa laf cat
Cat dafa gaw bëgguma ku ñu ree
Ne naa laf cat
Ki ku ko sukker, xale bi laf cat
Soxlawul sàppali, ne naa laf cat
Loxo bi gaaw na, xale bi laf cat
Aka mën a sañsé, kon ne leen laf cat
Sa jikko ji neex na ma
Sa ree ju neex sofu ma
Ni ngay waxe neex na ma
Dara ci yaw di sofu ma
Kon ne naa laf cat