OMG
DD Records
Yaw yaay géej sa ndox du jeex
Yaw yaay tène bu dul mësa ndey
Yaw yaay jant say lampe du fay
Bu guddi jotee yaay doon biddéew
Kenn du la jàpp bàyyi la
Mel ni yaw tay jafe na
Yaw yaay sama kaani
Kon foo jar ma toj la
Ni nga mel dal ëpp na
Góor gu baax tay jafe na
Sama xol ni nga koy def
Yok tax man ma bëgg la
Yëngël ci say mbagg
Ci say mbag
Yëngël ci say mbagg
Yaw ku la am de faw mu feccal la
Yëngël ci say mbagg
Ci say mbagg
Yëngël ci say mbagg
Pare naa foo jëm yóbbale ma
Foo ne jamm jugu fa
Foo di ree man weetaluma
Jàppal fi nga jàpp bu ko bàyyi bëgg na
Ma jàpp fi ma jàpp loo wax lépp dëgg la
Doon sa jongama di la woowee nijaay
Doo rëbb sooy yaw la gaynde Ndiaye
Kenn du la jàpp bàyyi la
Mel ni yaw tay jafe na
Yaw yaay sama kani
Kon foo jar ma toj la
Ni nga mel dal ëpp na
Góor gu baax tay jafe na
Sama xol ni nga koy def
Yok tax man ma bëgg la
Yëngël ci say mbagg
Ci say mbag
Yëngël ci say mbagg
Yaw ku la am de faw mu feccal la
Yëngël ci say mbagg
Ci say mbagg
Yëngël ci say mbagg
Pare naa foo jëm yóbbale ma
Ku la am yaw am yaw
Owouwa owouwa hey
Ku la am yaw am yaw
Owouwa owouwa hey
Fiiruma pur fiir bëgg naa nga am ko
Lu fi gën a diis dund naa ko mak yaw
Mbëggeel dëgg du bu saay-saay hey
Li nga bëggul gis bàyyi naa ko ndax yaw
I just wanna know
Tell me I just wanna know what you want for me
I just wanna know
Girl you gotta let me know what you want for me
Yaw laa tànn ci say moroom yaw (yeah hey)
Bëggetuma gis say rongoñ yaw (yeah)
Diggante bi dara du ko dàq (hey)
Lii dara du ko dàq (hey)
Yëngël ci say mbagg hey (hey, hey yeah, yeah hey)
Owuwooh owuwoh
Ku la am war na la teye bu baax (war na la teye bu baax)
Owuwooh owuwoh
Pare naa foo dem yóbbale ma (yóbbale ma)
Owuwooh owuwoh
Ku la am war na la teye bu baax (teye bu baax)
Owuwooh owuwoh
Pare naa foo dem yóbbale ma