Deukbi metina Ligay amatoufi Jeuness bi khadinen Beug dieul gaal song guedi gui Bou nieupa démé koufi dess Sounou rew bi nioko mom Niou rafatal outine Took fi teki fi meuna neck
Té nak niou bayi khel Souniou mbolo beurri dolé Naniou beugeunté souniou biir Roy si niko mak niou bakh gni dane défé Niou khol si louniou ame Nit kou né amna louko ya Allah maye Naniou took sounou rew Ligay fi teki fii warna meuna néé
Sunu Gal gi moye keur gi
Boulène dèm Boulène dèm Tog mène Niou défare Rèwe mi Fome Lène Fome Lène Ndiarign amna si rèwe mi Bou Nièup dèmé Nièup dèmé Kénène Moye Dieul Rèwe mi Boulène dèm Boulène dèm Tok lène niou défare rèwe mi Demna fèpe guisna lèpe Sunu gal gi moye Keur gi