Mbëggeel du xeet Xol buy bëgg du tàggoo Sama yaay booy ne na ma Maa xool keneen Même su ma bëggul Waaye na doon sama deretooy
Man waruma Doon ki jittel sama bànneex Donte sama xol am na tànneef Waaye yaay booy ne na ma Sama doom du sa wareef
Ñun, bété-bété lañu Boo nekkul pure sang Doo rax suñu deret Ñun, bété-bété lañu Boo nekkul pure sang Doo rax suñu deret
Sori may tewul nga jege ma Sama xol sama xel lañu ci yaw Chérie booy ooo céy dellusil Yaw mbëggeel du fo Te mbëggeel du jaay Kenn du ko jële ca marché ba Man yaw laa nob! Yaay ne deet, baay ne deet Waaye soo demee damay wet chéri booy ooo Xol jàppu du wor ka mu nob Xoolul deret, xoolul xeet Ña kay dundal rekk lay seetoo
Ñun, bété-bété lañu (ñun bété-bété lañu) Boo nekkul pure sang Doo rax suñu deret Ñun (ñun nii), bété-bété lañu (ñun bété-bété lañu) Boo nekkul pure sang Doo rax suñu deret
Dégguma la, dégguma la Sama yaay sama baay Ne nañu duma séy ak waje
Ki géer la, géwél la Ñeeño wala Maabo Man moom laa nob Mbëggeel du nobeel Nobeel du cofeel Eh eeeeh sama waje Man moom laay wër